MDN wants to talk to developers like you: https://qsurvey.mozilla.com/s3/8d22564490d8

Sàrti jàngatkatu Marketplace

This translation is incomplete. Please help translate this article from English.

Xët wii mooy leeral melokaan yi jëfekaay yi war a am ngir ñu mën leen a boole ci Firefox Marketplace. Li ñu ci jublu mooy fexe ba ku nekk mën ci gis boppam. Muy ñiy defar jëfekaay bi walla ñi koy jëfandikoo ci Firefox Marketplace. Balaa Defarkat yi di dugg ci liggéey bu amee noonu solo, dañu koy soxla teg fu wóor te jaar yoon. Waaye itam, jëfandikukat yi dañu bëgg jëfekaay yi ñiy samp ci seeni jëfandaay doon yu wóor, te itam muy jëfekaay yuy yam ci liñ leen di doyee. Liñ jublu ci dénkaane yii ñu bind ci suuf mooy fexe ba wàccoo ak bëgg-bëggu defarkat yi ak jëfandikukat yi.

Li Mozilla sopp walla ñàkk a sopp ci jàngatum jëfekaay bi mooy:

  • Bépp yoon buñ fi mën a tëral dañu ko war a doxal ci anam wu jaar yoon. Jàngatum jëfekaay bi, jublu wuñ ci gàntal liggéeyu kenn, waaye li ko tax a jog mooy jàppale defarkat yi ñu yegg fa ñu bëgg ci seen liggéey.
  • Du jàngat yi ñooy natt baaxaay bi! Bu ñuy amal njàngat bi, kenn dafay daal di jël jëfekaay bi, jëfandikoo ko ci anam wi ko kenn ku nekk mën a jëfandikoo ngir saytu ni muy doxee.
  • Su njàngat bi feeñalee jafe-jafe ci jëfekaay bi, dañu koy yegge ki ko defar, ba noppi nu jox ko ci ay firnde. Su mënee nekk itam, jàngatkat bi dafa war a leeralal defarkat bi yoon wi mu war a jaar, ak jox ko ay lëkkalekaay yu koy yóbbu ci téere yu koy xamal li mu war a def ak coppite yi mu war a amal.
  • Jàngat bi amul lenn lu mu war a wax cimelokaanu jëfekaay bi, li ko war a soxal ni jëfekaay bi didoxee. Ci misaal, kenn du gàntalub jëfekaay ndax mbind mu ñaaw, waaye sudee kenn mënul jàng mbind ma, su boobaa mën nañu ko gàntal.
  • Nun danuy rafet njortu ci defarkat yi saa yu nekk. Sudee wóoru nu ni danu war a gàntal jëfekaay bi am déet, jàngatkat yi dina ñu ko déglulaata ñu koy gàntal. Jafe-jafe yi nekk ci dalu yebbikaay yi warul tax ñu gàntal jëfekaay bi, ndax defarkat bi waralu ko; waaye mën nañu ko gàntal sudee menu fexe ba jëfekaay bi dox.

Kaarànge

Di nga fekk bépp leeral boo soxla ci Kaaràngeg Jëfekaay bi fii: https://wiki.mozilla.org/Apps/Security

  • Leerali jëfekaay war nga leen fekk fa jëfekaay bi cosaanoo.
  • Buñ lay joxe leeral bi dafa war a am wii tur: Content-Type header of application/x-web-app-manifest+json.
  • Jëfekaay yi waru ñu jëfandikoo ay redirect walla ay iframe ngir yab ab ëmbiit yu jëfandikukat bi amul sañ-sañu jëfandikoo.
  • Sañ-sañ yiñ sàkku war nañu nekk ci leeralu jëfekaay bi ak lu ñuy doyee sañ-sañ bi.
  • Jëfekaay yiñ type beral loxo, dina ñu am beneen njàngat, bu àndak kotu njàngat. Li ko waral mooy jëf yuy lore ak njoxe yi jëfandikukat bi mën a ñàkk ci API yu am maanaa yi.
  • Sàrtu Kaaràngeg Ëmbiit (CSP) biñ def ci leerali jëfekaay bi mooy xamle li kotu jëfakaay bi mën a def.  Jëfekaay biñ ko tànnal, sudee tànnu ñu beneen, ñeel jëfekaay yiñ joxul maanaa benn la ak bu bépp dalu wab; jëfekaay yiñ type beral loxo la ñu gën a am ab restrictive default.  Nettalib nangu bi biñ sosul ci biñ ko dugal ci Firefox Marketplace dina wone jalgati CSP yi mën a am ci sa jëfakaay – kon xàmmeel tere yi ak jëfandikoo yi bokk ci kàggu jàmbur yi nga dul jëfandikoo.

Sutura

Ëmbiit

  • Dunu nangu benn jëfekaay buy jalgati sunu Yoonali Ëmbiit. Sudee say pexe daa jeex, nga sàkku ay leeral ci ñiy amal jàngat yi, budee sax noppeegoo ngir dugal jëfekaay bi. Danu la bëgg dimbali nga tegu ci yoon wu baax wi, ngir ëlëg mu bañ a doon ëmbiit lu ñuy sànni.
  • Li ko dale Saawiyee 2014, International Age Rating Coalition (IARC) war na natt bépp jëfekaay.  Ngir am natt googu, dina am ay mbir yuñ lay laaj sooy dugal, ba noppi nga jot natt gi ci saasi.  Yeneen leeral yu jëm ci natt googu ñu ngi here.
  • Nataali seetu yi ak tegtal yi yiñ dugal ci Firefox Marketplace dañu war a méngoo ak jëfekaay bi.  Mën nga ci boole 1 ba 2 nataali "jaayu" yuy woneg mën ànd, méngaley xayma, walla muy ñaax nit ñi ci ñu koy jëfandikoo, waaye jëfekaay bi war na am gën gaa néew benn nataalu seetu buy dox, ndax jëfandikukat xaw a xam li ñuy waaj a jot.  Sudee benn ci nataalu seetu yi ab splash walla dawalub seetu, danga ci war a boolewaale nataalu seetub wàllu jëfekaay biy dox.
  • Ci leerali jëfekaay bi, local keys dañu war a méngoo ak barab yi jëfekaay bi di nangu. Soo joxee caabib dëkk ci Polone, jëfandikukat dina ñu jàpp ni jëfekaay bi jàppandi na ci làkk woowu.
  • Junjub jëfekaay bi dafa war a topp Firefox OS app icons style guide. Junju 128 x 128 lu war la, waaye dañuy digle ab junju 512 x 512 itam (ngir am yeneen leeral, seetal Icon implementation for apps.) Sula neexee junj kurmbal, walla nga lelli wet yi, walla mu kaare, méngook li téere bi wax.

Yoonali ëmbiit

Lii mooy leeral xeetu ëmbiit yi ñuy tere ci Firefox Marketplace. Lim nañu fi yu bari, du fa yam, te mën nañu ko yeesal. Suñu gisee ni jëfekaay bi dafay xët yii yoonali ëmbiit, Mozilla am na sañ-sañu dindi jëfekaay bi ci Firefox Marketplace ci saasi.

  • Lépp lu ñaaw te jëm tey wone awra, walla mbind muy fësal ay awra walla fitna.
  • Lépp lu jalgati yelleefu jàmbur, boole ci xaalutu jàmbur walla yeneen yelleefi moomeel walla yelleefi sutura walla siiwal.
  • Bépp ëmbiit bu jog ngir lor Mozilla walla jëfandikukat yi (lu ci melni kot yuy lore, wiris, spyware walla malware).
  • Bépp ëmbiit bu jaarul yoon walla muy dooleel ludul yoon.
  • Bépp ëmbiit buy wor, naxe, bu wàcci yoon walla muy meep walla sàccug turu jàmbur.
  • Bépp ëmbiit bu mën xir nit ci kàrtum xaalis.
  • Bépp ëmbiit buy yëngu ci siiwalug costéef walla ay cër yuñ yilif walla yu jaarul yoon.
  • Bépp ëmbiit lu dund ci ñaqu xale.
  • Bépp ëmbiit buy yàq, tiital, yee fitna jëme ko ci nit, walla di xirtal nit cig tooñ kenn walla ñu bokk at, muy góor walla jiggéey, deret, xeet, cossanum réew, diine, taamuy sëy, laago, diine, dëkkuwaay walla yeneen wàll yuñ aar walla muy kàddu yu ñaaw ci der.
  • Béppëmbiit buy nax ab jëfandikukat ngir mu jënd am njaay.

Doxalin wi

  • Jàngatkat bi dafa war na mën a amal man-mani siiwal gu njëkk gu jëfekaay bi. Jafe-jafe yu amul solo noonu diñu leen yegge defarkat bi, waaye llou de tere ñu nangu jëfekaay bi.
  • Jëfekaay warul yàq lenn ci dalu sistem bi walla ni muy doxee.

Jàppandal gi

  • Defarkat bi war nay jéem a gën a baaxal laaliinu jëfekaay bi ngir dalu yebbi bi mu jëm. Li ñu ci jublu mooy gis mbir yi jaarul yoon, niki:
    • Jëfekaay buy dugal ngir telefon bu leer ni dalu biro la.
    • Jëfekaay boo xamni mënul fees ci seetu bi mu jëm (maanaam jëfekaayu 320x480 bu jël li ci kaw seetu bi rek, bàyyi li des ci suufu tablet bi du am dara. Loolu kenn bëggu ko!)
  • Jëfekaay mooy war a defaral boppam pexem joowu te bañ koo wekk ci beneen joowukaat walla jumtukaayu joowu, muy loo dul fekk ci jëfandaay yépp.
    • Ci misaal, dañu nangu ab jëfekaay sudee jàngatkat bi defay xuus ci jëfekaay te mënul dellu ginaaw. Sàkku wuñ ci jëfekaay ñu defar laatu butoŋ bi nekk ci jëfekaay yi gën a bari.
    • Ci sumbu Firefox OS v1.1 walla yu ko ëpp doole, mën nga ci yokk moomeeli leerali chrome ngir yokk saytu joowu gu néew.
  • Jumtukaayi joowu yi ci melni, butoŋ yi ak lëkkalekaay yi, dañu war a neex a bës walla kilike.

Sàrti Boddi

Ñaanu nu ko Yalla waaye, am nanu sañ-sañu dindi ("blocklist") bépp jëfekaay buñ siiwal ñu fekk ko ëlëg muy jalgati benn kaarànge, sutura, walla càkkutéefi ëmbiit, walla jëfekaay yuy yàq sistem bi bu baax walla ni muy doxee. Defarkat yi dina ñu leen yëgal li xew laata nuy boddi benn jëfekaay, dina nu leen jàppee dëkkandoo bu baax fileek amu nu ci firnde, ba noppi nga jotee dimbal ci jàngatkat yi ngir waxtaane li xew te saafara jafe-jafe yi. Yenn ci mbir yiñ mën a boddi ñooy:

  • Meep
  • Yónnee ay Spam
  • Soppee nataal ci Puppy Pictures v1.0 def ko Brutal Violence v1.0 (fekk yeesaloo nattug ëmbiit li)
  • Ñàkk a àndal yoon gu jéggi dayo gu jëfekaay ci jëfandikukat yu bari — gàllankoor ni telefon bi di doxee, di ko fay ak a taalaat, di réeral njoxey jëfandikukat bi, ak yeneen mbir, fekk jëfandikukat yi menu ñu wax ni jëfekaay bee ko waral te boo fayee taalaat telefon du tax mu saafarawu.
  • Jëfekaay bu ñuy jëfandikoo being ngir ay coŋ ci reso bi, lu ci melni banal ab cër séddaleem (DDOS).

Yeneen leeral

Balluwaay yii dañu ànd ak ay leeral ci ni ñuy doxalee njàngat mi ak jàngatkati jëfekaay bi:

  • Reveiwers test criteria — xët wii mooy leeral xayma bu jàngatkatu jëfekaay bi liggéey ci say jëfekaay
  • App reviewers— naka la ñuy jokkoo ak waa jàngatkatu jëfekaay bi te bokk ci njàngatum jëfekaay yi

Document Tags and Contributors

 Contributors to this page: DevonB
 Last updated by: DevonB,